notícias musicais

top 13 artistas

top 13 musicas

Confira a Letra Sama Wo

Philip Monteiro

Sama Wo

Yeah
Sama fans yi, maa ngi leen di gërëm
Di leen sant gis naa seen taxawaay
Musique bi
Pur yeen la, oo oo oo
Man nob naa leen, waaw

Yàgg na lool (yàgg na)
Bi nga demee (bi nga demee)
Man réer naa (réer naa)
Réer naa sans yaw (sans yaw)
Lan laa wara def? (Wax ma)
Def sans yaw (sans yaw, hey)

Dama la soxla, dama la bëgg
(Dem nga te bàyyi ma)
Bàyyi ma ci lëndëm
Wante xam nga ni
Ni dama wara dundu ba tey
(Dem nga te bàyyi ma)
Baby, ñëwaatal ci man
Xanaa déggoo sama woo, yeah

(Baby ñëwaatal)
Yàgg na lool bi nga demee
(Tax na sama xol wéete)
Lu may def ba nga ñëwaat, ñëwaat ci man
(Baby ñëwaatal)
Yàgg na lool bi nga deme
(Tax nga sama xol wéete)
Xanaa di la wax bés bu ne fi nga tollu ci man

Bu ma toggee di xalaat
(Dundu yu neex ñi ñu doon dundu)
Rekk sama xol fees
(Xamatuma lu ma wara def)
Deme nga bàyyi ma ci lëndëm
(Wante xam nga ni)
Dama wara dundu ba tey
(Dem nga te bàyyi ma)
Bàyyi ma ci lëndëm
Dama la soxla, dama la bëgg
Baby ñëwaatal ci man
Xanaa déggoo sama woo

(Baby ñëwaatal)
Yàgg na lool bi nga demee
(Tax na sama xol wéete)
Lu may def ba nga ñëwaat, ñëwaat ci man
(Baby ñëwaatal)
Yàgg na lool bi nga demee
(Tax nga sama xol wéete)
Xanaa di la wax bés bu ne fi nga tollu ci man

Xamatuma li ma wara def (yàgg na lool)
[?] xalaat
Bëgguma nga xam li ma daj
Ndax xam naa ni am nga keneen
Mënuma ko gëm, mënuma des ni

Yàgg na lool bi nga demee
Man réer na nekkatu fi
Lan la wara def nékkatu fi
[?]
Dama la soxla, dama la bëgg
Baby ñëwaatal ci man
Xanaa déggoo sama woo

(Baby ñëwaatal)
Yàgg na lool bi nga demee
(Tax na sama xol wéete)
Lu may def ba nga ñëwaat, ñëwaat ci man
(Baby ñëwaatal)
Yàgg na lool bi nga demee
(Tax nga sama xol wéete)
Xanaa di la wax bés bu ne fi nga tollu ci man

Discografia