notícias musicais

top 13 artistas

top 13 musicas

Confira a Letra Madame Bonheur

ADIOUZA

Madame Bonheur

Xooluma keneen, fees naa sama seetu
Jigéen jiy waxe jëf du am jotu tontu
Doon awo di buuru kër gi du ay fontu
Te sax fu ma moomee, zéro la koy wacce
Lu dés mëna daw, 1 bee ngi ci kaw
Ñaari fan yu ne coco fëgg àljanna taxaw

Bonheur
Fi wax amul cuuraay géy riir
Def terreur
Lu tax muy sedd te may jekk pire

Pese sama bopp xam ne waruma ragal wujje
Laajal mon coeur kuy madame bonheur
Yaa may confiné lépp di jupp yaa raw policier
Laajal mon coeur kuy madame bonheur

Ouh wool ma abass
Chéri fatou ak chilel boroom gambia

Li lay dóor te du la laal, neexul ci xol
Deuxième dame bi lañu takkal medaille d’or
Ki nelaw la xamoon ma jàngal ko yàndoor
Bàyyi leen di jëm jàng xam sa góor gëna woor

Xol bi nangu féete
Booboy dundu mbégté
Nàmmuma daray wax
Ba fi mi ngi baax
Chérie duggal dëkk do fëgg yaay laisser passer

Allo
Fi maay sourire muy évanouir
Mais allo
Ay nelaw jeex na dama yor liir

Pese sama bopp xam ne waruma ragal wujje
Laajal mon coeur kuy madame bonheur
Yaa may confiné lépp di jupp yaa raw policier
Laajal mon coeur maay ki koy bonheur

Coco man ak yaw ba àljanna
Ci sa wét lay dunde oh là là
Yaa gaaw ci man
Say je t'aime ci sama biir tempan
Ni nga may def neex na ma
Bëgg naa la, bae

Pese sama bopp xam ne waruma ragal wujje
Laajal mon coeur kuy madame bonheur
Yaa may confiné lépp di jupp yaa raw policier
Laajal mon coeur kuy madame bonheur

Laajal mon coeur kuy madame bonheur
Laajal mon coeur maay ki koy bonheur

Tracker