Léegi, wax ji neexatul
Te su ma waxee mu xëp ci kaani
Moom de léegi, dépense matatul
Te su ma laajee, mu daldi maay jani
Li la war ci man guddi gi
Ci kaw lal bi, yeggatoo ci
Du wax ju neex, du ray, du fóon
Déggatuma chérie
Sonn naa, tàyyi naa
Mënatuma
Mënatuma, sonn naa
Bàyyi naa
Léegi, wax ji neexatul
Te su ma waxee mu xëp ci kaani
Moom de léegi, dépense matatul
Te su ma laajee, mu daldi maay jani
(Kii, lu ko dal)
Ana li nga ma waxoon ak li nga ma diggoon
Li taxoon ma falax waxi yaay, téggi waxi baay
Ana li nga ma waxoon ak li nga ma diggoon
Li taxoon ma falax waxi yaay, téggi waxi baay
Sonn naa, tàyyi naa
Tàyyi naa, sonn naa
Sonn naa mënatuma dellu sama kër baay
Eh! Demb balaa tay
Ana ni ñu meloon, demb balaa tay
Tey, tey, tey
Léegi, waxtaan amatul
Te su ma jaaxlee, loxo la may sanni
Léegi dafa may dóor aka yooxu
Xas aka jani ci kanamu jaboot gi
Li ma waxoon kër baay
Tay na ba mënatuma dellu man mi, ooh!
Li ma reccu tey moom
Mooy li ma séy ak yaw ba mu deme ni ouh!
Sonn naa, tàyyi naa
Mënatuma
Mënatuma, sonn naa
Bàyyi naa
Léegi, wax ji neexatul
Te su ma waxee mu xëp ci kaani
Moom de léegi, dépense matatul
Te su ma laajee, mu daldi maay jani
(Kii, lu ko dal)
Ana li nga ma waxoon ak li nga ma diggoon
Li taxoon ma falax waxi yaay, téggi waxi baay
Ana li nga ma waxoon ak li nga ma diggoon
Li taxoon ma falax waxi yaay, téggi waxi baay
Sonn naa, tàyyi naa
Tàyyi naa, sonn naa
Sonn naa mënatuma dellu sama kër baay
Eh! Demb balaa tay
Ana ni ñu meloon, demb balaa tay
Ana ni ñu meloon, demb balaa tay
Ana ni ñu meloon, demb balaa tay
Ana ni ñu meloon, demb balaa tay
Ouh, dem naa
Dem naa
Ouh, dem naa
Dem naa
Dem naa bàyyi la fi, man dem naa
Dem naa
Dem naa, mënatuma muñ, dem naa