Ànd bu yagg
Mën na metti yenn saay
So amulee fiit
Do xam fu guro di jaay
Li ngay yekk sa xol
Ci takkusaan bi
Gëna neex suñ la maay auto
Li ngay yekk sa xol
Ci takkusaan bi
Cours des grand celibat takule
Xale bi, jaraal na la lii
Loy xaar?
Yaw ani yaw sa fiit, ani góór ak tiit
Loy xaar?
Wan na ko ni, fi mo fi nee
Loy xaar?
Soo bëggee nit mu jaaral li
Loy xaar?
Ci sëy, ci sëy
Ñu mayeleen ngeen sëy
Ci sëy, ci sëy
Ci farata ngeen sëy
Yaw ànd bu yagg
Mën na metti yenn saay
Te so amulee fiit
Do xam fu guru di jaay
Ne nga dan' ka love, dan' ka love
Seet ci Yàlla wane fu la
Wax ma lan ngay xoff, lan ngay xoff
Demal ñaan ni ñu may la ko
Sëy bu jigéén doon, ñaani góór yi jeex waay
Yaw dinga ko togg lo, xarloo nga ko ba kañ waay
Ne nga dan' ka love, dan' ka love
Seet ci Yàlla wane fu la
Wax ma lan ngay xoff, lan ngay xoff
Demal ñaan ni ñu may la ko
Ci sëy, ci sëy
Ñu mayeleen ngeen sëy
Ci sëy, ci sëy
Ci farata ngeen sëy
Waawaaw
Ki may bëgg wooy mooy
Jeri ngone masamba
Lat sukabe ma samba
Astou Mbaye falli ngone massamba
Ma falli Coumba ndam tek ma
Balaa yewu fu ki bale ak ñaar taak
Astou Mbay géwël yacc ndaak
Ak geer yacc ndaak
Man ne géwël yacc ndaak te ak geer yacc ndaak
Ko ci wo ma lawbe samba ku li misi seydi ndaak laay wuyo
Eeeeeeeeeh waay!
Jeri ngone Mbaye jeri ngone xari
Jeri ngone massamba
Astou Mbaye
Astou Mbayee chéri toma
Astou Mbaye yaayu Aleya
Jeri ngone Mbaye, Jeri ngone xarii
Jeri ngone massamba
Astou Mbaye
Marietu acc sa yaay el feky
Jigéénu bacc kaay
Jeri ngone Mbaye jeri ngone xari
Jeri ngone massamba
Astou Mbaye
Kone malay woyal sa raak molay woyal
Tay malay woyal Gawlo bi molay wayal
Jeri ngone Mbaye, jeri ngone xari
Jeri ngone massamba
Astou Mbaye