notícias musicais

top 13 artistas

top 13 musicas

Confira a Letra Mana Mana

Akhlou Brick

Mana Mana

Dégg naa je t'aime bu ne
Boo waxee je t'aime dootu ma la dégg damay gumba tegloo
Dékku naa fi coow bu ne
Boo waxee ba yëkkati sa baat bi dang may mu ma loo
Te xol du gâteau, kenn du ko daggat-daggate
Xol du pizza ba ku ne tël di laaj part
Amooleen fi part
Benn part la jox naa la ko ànd nañ ci
Ngay doore di màtt
Di doon patte di gajj
Yaa rafet jikko, rafet xol de ma nappaaje
Ngay doore di màtt
Di doon patte di gajj
Yaa rafet jikko, rafet xol de ma nappaaje
Man su ma dee dee ci àll gaynde may ray
Man su ma dee, bëgg damay bëggaale sa démbaak tay

Tewul luñ la waxal yawa
Waaye man ak yawa
Danga sikk ñépp ko wax taxul ma dem bala
Eh luñ la waxal yawa
Waaye man ak yawa
Danga sikk ñépp ko wax taxul ma dem bala

Jarul ngay laaje mana mana (mana mana)
Luñ ma mënti waxal mana mana (mana mana)
Maa toj kasi mana mana (mana mana)
Eh xale bi ko nopp mu ne mana mana (mana mana)

Eh maa ñëw këf la coppet
Maa koy neexal ci pet
Dal sama kaw rekk toj ni benn nen bu bonde ci kekk
Sur le plat lañ fi tekk
Xam naa ni yaw la fi fekk
Yor naa sikkim pur nga teg ci mbej maay sa sikket
Ok wala (walaaa), jublu waya nga kaaba
Jàppal sikkim ne a ba ça ma ne watawallah
Foo dem foo dem maa nga fa
Ëppal xawma ndanka
Doxalal foo dox ba tegi jokk ma teg fa tanka (damn!)
Jugal ñu dem nelawi (nelawi)
Naw ci kaw ni Aladine (Aladine)
Yaa raw héritage maa dewe lekkal sama alal yi
Xam nga maa la nob, dama la nob nobaale sa rab bi
C'est normal ma dof ci yaw parce que yaa yor sama garab yi

Eh ku lay woo, ku lay woo
Bul laaje, man ma lay woo
Bae yaa may tooñ maa lay tooñ
Suñu mbëggeel moo raw coono
Sama volume fi mu nekk moo baax
Bu de da low ma yokkat
Boo reetaanee laay kontaan
Xale bile yaa raw seytane, yaa raw seytane
Ba su ma dee dee ci àll gaynde may ray
Man su ma dee, bëgg damay bëggaale sa démbaak tay

Tewul luñ la waxal yawa
Waaye man ak yawa
Danga sikk ñépp ko wax taxul ma dem bala
Eh luñ la waxal yawa
Waaye man ak yawa
Danga sikk ñépp ko wax taxul ma dem bala

Jarul ngay laaje mana mana (mana mana)
Luñ ma mënti waxal mana mana (mana mana)
Maa toj kasi mana mana (mana mana)
Eh xale bi ko nopp mu ne mana mana (mana mana)

Tracker