notícias musicais

top 13 artistas

top 13 musicas

Confira a Letra And Ak Yow

ISS 814

And Ak Yow

Nit ku ne ci sa life am na koy xaar
Te bu yegse di nga xam ne ki la woon
Fi nga dem, fi nga jadd, fi nga toog xaar
Bu Yàlla ne waaw dafay mel ni sonnuwoon
Yàgg na ñu jël sa xol fowe ko
Xamul woon li ci biir li ci newoon
Sa yëg-yëgu xol neex ba def la ay jooy
Ñaan bu sotee sonal borom

Ànd ak yaw fu ay nit mësul dem
Nekk ak yaw fu ay nit mësul ne
Sama xol bi yaw mi yaa ci ne
Bu doyul ma dolli my baby

Bëgg naa shine ci sa wet ci sa wet
Di la wan ni ma mel ci yaw
I don't mind ci sa wet ci sa wet
Baby girl dama dem ba dof ci yaw
Bëgg naa nga ne ma
Sama xol bi yaa ci ne
Man mi tam ma wax la
Sama xol bi yaa ci ne

Boo ma nobee benn yoon, nob naa la ñaar
Bu desee ci man xam naa ni dootu ñu xaar
Mbëggeel garab la bu ñuy dundal pur mu nat
Ci sama xol bi benn nga ci dootul ñaar

Ànd ak yaw fu ay nit mësul dem
Nekk ak yaw fu ay nit mësul ne
Sama xol bi yaw mi yaa ci ne
Bu doyul ma dolli my baby

Tracker