Boo xamoon xol bi lum la dencal
Doo dem feneen di fa wëri mbëggeel
Ba muy metti ki nga nekkal
Tay bu neexe war nga ko won mbëggeel
Bu ñu ma bëggee jot ci yaw lañuy jaar
Parce que yaay sama faiblesse
Kenn du nga ci man ku nekk ak ñaar
Xol bi jël nga ko ne fees
Bu guddi gi jotee ba nit yi yépp nelaw
Ci nga may jege xëcc ma aj ma ci kaw
Nga naan ma 'uh-ah', noo ko bëggee?
Ma naan la nii la ko bëggee
Yaa jël xol bi, tijj ko def ci love bi
Remplacer ki fa nekkoon ndekete dama juumoon
Tebbi nga ace bi, jël xolam caabi
Dem ba géej sànni, mbëggeel moo mën lii
Fi nga jàpp foofoo neex
Bu ko bàyyi yaa ko moom
Ku la ko tere dina ñów di xeex ak moom
Yow fi nga jàpp foofoo neex
Bu ko bàyyi yaa ko moom
Ku la ko tere dina ñów di xeex ak moom
Bae ci night bi
Mënuma nelaw tay ci night bi sans nga nekk fi
Oh ma vie
Wax ma ni may sa love, may sa aaah-eeeh
Bu guddi gi jotee ba nit yi yépp nelaw
Ci nga may jege xëcc ma aj ma ci kaw
Nga naan ma 'uh-ah', noo ko bëggee?
Ma naan la nii la ko bëggee