notícias musicais

top 13 artistas

top 13 musicas

Confira a Letra Penalty

ISS 814

Penalty

Homme de tenue bëgga dunde corruption
Entreprises di sànni déchets pollution
Jox la ndombog-tànk defoo résultats
Président bu bëgg ñetti mandat

Entreprise jékki téj
Gestionnaire kepp kese
Hôpital morgue dëj
Bés bu ne néew bu bees
Civisme bu ci mbedd mi
Naan kafe sànni casse
Problèmu jàng bu weesu na syndicat

Waar mbit waara mbit
Arbitre du sol dix
Capitaine du sex mbiib
Loo yor maraakiis
Crampons du tarxiis
Surface ralentir
Hors-jeux mu naan but
Looy xaar penalty

Penalty!
Arbitre siffléwu ko ñi ci ban bi ñoo ko mbiib
Penalty!
Boo nekkee njiit
Defoo li la war yépp ñi nga jitte ñoo koy mbiib
Penalty!

Alalu njirim bi nga tëdd def sa noce
Lu ñépp bokk yaw nga jël ko def sa poche
Sa xaritu benn bakkan am lu baax nga mer
Puusal fëlé yaw de am nga dal no mel

Toj sa math te dellu klaas, moo gën ngay
Toj sa mbarik mu naan tas, yaw doom nday
Système bi yérémul kenn
Mësu la bëgg tuur drét
Fexeel ba jafandu fenn
Ne naa la dëgg du fen

Député
Ñu fay la weer yaw ngay nelaw Assemblée!
Monsieur le Maire
Jaay na suuf ci wax ma xale yi fu ñuy fowe?

Waar mbit waara mbit
Arbitre du sol dix
Capitaine du sex mbiib
Loo yor maraakiis
Crampons du tarxiis
Surface ralentir
Hors-jeux mu naan but
Looy xaar penalty (jugal!)

Penalty!
Arbitre siffléwu ko ñi ci ban bi ñoo ko mbiib
Penalty!
Boo nekkee njiit
Defoo li la war yépp ñi nga jitte ñoo koy mbiib
Penalty!

Day kas, nañ ko vare ralentir
Day kas, nañ ko vare ralentir
Day kas, nañ ko vare ralentir
Mu jokk day kas, nañ ko vare ralentir

Tracker