Hey Massamba Walo
Maa la tooñ ndax maa la woolu
Ba nga ñëw ma lay wax ay waxu mbëggeel
Maa la doy te man nga wóolu
Sunu ànd gisuma ci lu dul ngëneel
Su jaree raag
Dinaa la wan fi ma manee yaw
Man duma seetaan
Su jaree raag
Dinaa la yóbbu sama gàlle
Présenter la sama gaa yépp
Eey waay
Man dama laa, bëgg du nax
Coobare Yàlla Moo ma indi ci yaw
Àdduna yaa fiy wàcc sunu biir
Waru nu tee gise
Yaw Kumba amóo moroom biir Senegaal
Nee naa la waaw-kumba jël naa seede waa Senegaal
Àdduna yaatu na yaa ma tax a toog Senegaal
Waaw kumba danga di taaru Senegaal
Man dama laa wóolu man
Ndax danga maa wóolu
Te duma dem fenn ba la
Ndax danga may wër
Maa la tooñ ndax maa la woolu
Ba nga ñëw ma lay wax ay waxu mbëggeel
Maa la doy te man nga wóolu
Sunu ànd gisuma ci lu dul ngëneel
Kaay waay
Lot of peace
Lot of love
Soxna sii
Man loolu laa la yéene
Don't believe
Benn miss
Li ñu gis
Mooy nu wàlliyaani
Taaru Senegaal nga
Linguère biir Kayor
Yaay boroom teraanga
Jéeri jàpp Joor
Yaw Kumba amóo moroom biir Senegaal
Nee naa la waaw-kumba jël naa seede waa Senegaal
Àdduna yaatu na yaa ma tax a toog Senegaal
Yaatu na yaa ma tax a toog Senegaal
Waaw kumba danga di taaru Senegaal
Anh yeaah
Man dama laa wóolu man
Ndax danga maa wóolu
Te duma dem fenn ba la
Ndax danga may wër
Yaw Kumba amóo moroom biir Senegaal
Nee naa la waaw-kumba jël naa seede waa Senegaal