Gis la bëgg la, wax ma loo ci xam
Jox la sama life, desetuma dara
Def la comme sama tere, dang may yokk xam-xam
Jang naa la, mokal naa la, ni ku nekk daara
Bàyyiwuma dara, jël naa lépp
Mbëggeel gi lu mu dis dis
Àttan naa ko, àttan naa ko
Bàyyiwuma dara
Mbëggeel gi lu mu dis dis
Bëgg naa man, nañu naa
Baby dee ma xool
Dee ma xool, dee ma xool
Ndax man su ma xoolee
Yaw rekk laay gis
Dee ma xool, dee ma xool
Ndax man su ma xoolee
Yaw rekk laay gis
Lu ma ame lu dul yaw, man de bëgguma
Muy Alal di urus, dara safuma
Ndax doy nga ma
Ma doen lamb waye daj naa
Yaa ma bëgg ba ma yëg ko
Yaa ma sutural
Bàyyiwuma dara, jël naa lépp
Mbëggeel gi lu mu dis dis
Àttan naa ko, àttan naa ko
Bàyyiwuma dara
Mbëggeel gi lu mu dis dis
Bëgg naa man, nañu naa
Yaay ki ma tànn
Yaa di sama ndanaan
Duma la jëndek keneen
Yóbbuma man, yóbbuma feneen
Gisatuma ku dul yaw
Su ñu mbëggeel di law
Yaay ki gën ci man
Taamu naa la, taamu naa la
Baby dee ma xool
Dee ma xool, dee ma xool
Ndax man su ma xoolee
Yaw rekk laay gis
Dee ma xool, dee ma xool
Ndax man su ma xoolee
Yaw rekk laay gis