Sagam xol lay bëgg
Jox naa la ko ba mu jeex
Gumba teex lu tek si gëlëm
Ne Baye Fall Kour ak Keuleum
Da ñu ne xol lay nopp
Sama bos sa tura si nekk
Ni ma la mbege daf ma ëlëm
Soo fi nekkul lépp ay lëndëm
Awma ku dul yaw (bul jaaxle)
Yaw it amoo ku dul man (bul jaaxle)
May jooy di ree ngir yaw (bul jaaxle)
Ngay bëgg di xeex ngir man (bul jaaxle)
Man de yaw la love (la la la)
Sama xol bee chéri ne na yaw (la la la)
Bébé yoo yaw la love (la la la)
Sama xol bi, sama xel bi ne na yaw (la la la)
Chéri yoo
Jege ma ma lay reetaan, ngay may piis
Lu góor ñi bari bari bari yaw rekk la miss
Dem na ba sa mbëggeel dama diis
Saa su ma tëddee damay janeer yaw lay gis
Ey, ku làmb yaa tay daagul fa ñu la nobee
Ma bëgg ma tay li sama xol bi dina ko wane
Man de yaw la love (la la la)
Sama xol bee chéri ne na yaw (la la la)
Bébé yoo yaw la love (la la la)
Sama xol bi, sama xel bi ne na yaw (la la la)
Chéri yoo
Maa ngi fi di la xaar ñëwuloo
Baby wax ma kañ laa lay gisaat
Sama wéruwaay ci kër gi tay de wet na
Danga ma wetal way, baby namm naa la
Su ma sañoon doo dem bàyyi ma baby
Su ma sañoon foo nekk maa ngi fa baby
Maa ngi fi di la xaar ñëwuloo
Baby wax ma kañ laa lay gisaat