Lii de neex na lool
Bi bànneexu xol
Lii may yëg su ma koy xool
Lii de neex na lool
Ba ëpp tol
Way le leen ma sama doom ji
Man de bëgguma lu lay metti
Ma lay naxtaan ba ngay reetaan
Feesal sama mbëggeel ci yaw
Muy law ba faw
Ayo sama nenne, nenne tuuti
Ku may naqal sama doom ji
Ayo sama nenne, nenne tuuti
Ku may naqal sama doom ji
Cofeelu yaay si doom
Ku ko dundul doo ko mën a xam
Bis bi nga juddoo ba tew ci samay loxo
Li de leer na
Bidéew bi naw, tere ci asaman mbëggeel
Dundu ci xol te dee ci bët
Li de leer na ma
Bi ma njekke gis ma nenne
Yëg-yëg sama xol bi neex
Naqal sa doom su jooyee nga bëgg
Lii de leer na ma
Sama coono mooy sa bànneex
Su may liggéey suba day neex
Doom faw nga bëgg ba raw ci say moroom
Lii de leer na ma
Ayo sama nenne, nenne tuuti
Ku may naqal sama doom ji
Ayo sama nenne, nenne tuuti
Ku may naqal sama doom ji
Sama doom, sama soppe
Dundu mata jooyoo
Moom lay jooy doom dundal
Soo dundee ba mën liggéey
Feral say rongoñ