Man de xëy-na
Xëy naa
Faw ma wuti lu ma jariñoo
May taw ci kër gi taaluma biddanti
Faw ma wuti lu ma jariñoo
Dem korti-korti indi ci kër gi
Pare tekki teral samay ñoon
Yaay jurul doom bu ñàkk jom
Lu mu metti na xal yoon
Jël hilaire bay sama tool
Ku tekki bari nday
Waaye ku amul nawle yaay
Nga la dom, dañ la saas
Kon lu mu metti nan ko baay
Xuus na ci géj gi
Ngir tebi ass bi
Liggéey nday feeñ na
Tay yaay sa añ baa ngi
Man de xëy-na, xëy-na dem
Xëy-na, xëy-na dem
Tàggu sama yaay
Tàggu sama baay
Sama tay bu nekk gàccel na sama demb
Rawati na li ma togg sumb tay
Sant Yàlla buur bi ma may
Ba ma mëna xale yoon
Moom moo ko saañ
Yàlla buur bi mooy ki mën
Sant naa la Allahou buur bi yaay ki mën
Ma tekki teral yaay ba jële ko ci coono
Bay boy bëgg naa ci man bëgg naa ci man
Sama Yaay Djé
Sen Tialy, Gatié Ngalama
Man de xëy-na, xëy-na dem
Xëy-na, xëy-na dem
Tàggu sama yaay
Tàggu sama baay
Ku dem fu la lay yóbbu
Doo jigéen, góor nga te yaay taw
Demal maa ngi lay ñaanal
Yàlla na la Yàlla yokku Diouf