notícias musicais

top 13 artistas

top 13 musicas

Confira a Letra Yaay Boroom (feat. Samba Diarra)

Narah Diouf

Yaay Boroom (feat. Samba Diarra)

Yaa tax ma fent lii, ci xol bi lay jóge
Way wi yaay boroom
Nga tax ma bind lii, ci xol bi lay jóge

Maa la jël, teg la fu kawe, maa ko ñeme
Yëg la, jox la xol bi nga téye bul ko fowe
Bëgg la, teg ci fonk la, gëmewuma la
Yéene naa la lu ne, yaa fi ne, amul lu ñuy téye
Su ñu ma bëggee nañu ma bàyyeek yaw
Manaluñu ñu dara, suñu mbëggeel day law
Dañuy xaar, fii de ñoo fi ne
Mélodie biy yëngal sama xol, yaa koy animer

Yaa tax ma fent lii, ci xol bi lay jóge
Way wi yaay boroom
Nga tax ma bind lii, ci xol bi lay jóge

Ku man na def ni man?
Bëggal ni man?
Bari feeling ni man?
Eeh, joŋeel ni man

Yaay ki ma saf
Yaay sama saajobaan
Yaw laay tippoo
Lii de ku mu neexul nga dindi ko!

Takk ma ci baat, diri ma, man de bëgg naa
Foo ma xool gis ma ma lay ree, lii de saf na ma
Tay lu waay di jaay lamb na, loolu wóor na ma
Bëgg la ba bëgg ni la bëgg, xanaa jommi nga
Su ñépp bàyyee, man ma des ak yaw
Manaluñu ñu dara, suñu mbëggeel day law
Dañuy xaar, fii de ñoo fi ne
Mélodie biy yëngal sama xol, yaa koy animer

Yaa tax ma fent lii, ci xol bi lay jóge
Way wi yaay boroom
Yaa tax ma bind lii, ci xol bi lay jóge

Ku man na def ni man?
Bëggal ni man?
Bari feeling ni man?
Eeh, joŋeel ni man

Yaay ki ma saf
Yaay sama saajobaan
Yaw laay tippoo
Lii de ku mu neexul nga dindi ko!

Baby na nga jënd sa garde pareel Samba Diarra
Lañu la indil sincérité
Bi nga làmbool moo may dundal
Moo tax dama la bëgg
Ci sama xol bi dara du ko dindi!
Yaw mayal sa noon yi ndox
Baby, mar nanoo naan

Ku lamb yaa tay daagul fu ñu la nobee
(Yaw mayal sa noon yi ndox, baby mar nanoo naan)
Ku lamb yaa tay daagul fu ñu la nobee
(Yaw mayal sa noon yi ndox, baby mar nanoo naan)

Chéri guddi tay
Ne guddi tay sab noon du nelaw!
(Eeh guddi tay, ne guddi tay noonam du nelaw!)
Narah na nga jënd sa garde pareel Samba Diarra lañu la
(Eeh guddi tay, ne guddi tay noonam du nelaw!)

Ma ne!
Yaay ki ma ñoppati
Yaay ki may bégal
Yaay ki may dundal guddeek bëccëg

Ku lamb yaa tay daagul fu ñu la nobee
(Yaw mayal sa noon yi ndox, baby mar nanoo naan)
Ku lamb yaa tay daagul fu ñu la nobee
(Yaw mayal sa noon yi ndox, baby mar nanoo naan)

Tracker