Neex ba dàq lem
Mbëggeel bi da ma dem ba daf ma yem
Li may yëg sama xol
Moom mi su ma koy xool
Hey, xam naa ne li du neen
Yaay bagg bi rot ci sama tenn
Li may yëg for na lool
Moom mi su ma koy xool
Xol bi di tëb, di fecc
Su ma nekkee ci sa wet
Duma mësa wet ndax yaa tax may nekk
Doo juge ci xol bi xel bi yaa fi nekk ni
Man ak yow à l'infini, bae xool ma fi
Yaw rekk laay topp
Sama xol yaw rekk la sopp
Yaw rekk laa nob
Sama xol yaw rekk la sopp
Moo tax loo wax ma ne wa waawaaw
Soo ma nobee benn ma la dàqa nob
Moo tax loo wax ma ne wa waawaaw
Soo ma nobee benn ma la dàqa nob
Fok ma wane wa àdduna
Sama love ci yaw du jeex du jeex
Fok ma wane way fi nga tollu ci man
Day mel ni géej, amul limit, no no limit
Dama la wóolu nga ñëw
Bañaloo ma dara ci yaw
Ci la xam ni li mooy mbëggeel
Sama xel bi neex coofeel
Yaw rekk yaay ki ma doy
Sama xol bee yaa koy ray
Xol bi di tëb, di fecc
Su ma nekkee ci sa wet
Duma mësa wet ndax yaa tax may nekk
Doo juge ci xol bi xel bi yaa fi nekk ni
Man ak yow à l'infini, bae xool ma fi
Yaw rekk laay topp
Sama xol yaw rekk la sopp
Yaw rekk laa nob
Sama xol yaw rekk la sopp
Moo tax loo wax ma ne wa waawaaw
Soo ma nobee benn ma la dàqa nob
Moo tax loo wax ma ne wa waawaaw
Soo ma nobee benn ma la dàqa nob
Di ci fey dem fu sori lool
Fas yénne ci naan ba màndi lool
Man ak yaw dañ ci dem ba jeex
Mbëggeel bu yatu ba mel ni deex
Hée! Dafa dem
Dem ba su may dof
Yaw laay topp
Mbëggeel bu yatu ba mel ni deex
Baby yaw rekk lay topp
Yaw fi nga nekk man foofu lay dem
Yaw rekk lay topp
Jox naa la ko
Ci yaa ko moom, xol bi yaay boroom
Ndax yaw rekk laay topp
Baby yaw rekk laay topp!