Lu tax xale yi jàngatuñu
Kër gi kenn génnatul
Àdduna la teye, nit nga ngi de fi mu tollu ñëpp wéet
Te ñëpp la mën daal, ki toog ak ki toggul ki wër rekk lay àndal
Musuma gëm li mu daal ma
Musuma gëm li pape lu am la
Ñun nak dañu xiif te coobatuñu
Pa bi jëmna mak te mère bi jobatul
Man mii docteur rekk lay gis
Mbedd mii fees dell ak police
Jaaxle joomi njakare te degatuñu fi suñ Imam fum fi kabare
Yaa Rahman, yaa Rahim, yaa Malik Al Moulki, yaa yaa mujib
Yaa Salam, yaa Latif, yaa Karim, yaa Hakim, yaa Kabir
Woh woh woh woh
Yàlla yaw Yàlla yaw ñu lay ñaan nga balinu
Woh woh woh woh
Yàlla yaw Yàlla yaw ñu lay ñaan nga balinu
Yàlla yaw baal nu
Yàlla yaw baal nu
Yàlla yaw baal nu
Yàlla yaw baal nu
(Yàlla yaw baal nu)
Léegi ngay yeewu gis sa mère fee doo ko jox loxo
(Yàlla yaw baal nu)
Ku gis ku sekket da ngay ragal doo ko wax toqo
(Yàlla yaw baal nu)
Ku jàngul àdduna ci li am nga négligence nit la
Yàlla gën a bëgg tay fok nga may ko distance
(Yàlla yaw baal nu)
Mbokk, ba xam nga li ñu bokk bu de alaal
Rekk nga jitel ba faate li ñu topp
Kër gi fees xale yi xiif loo ma may ma taay
Weer bi dina boroom kër gi awma lu ma ko faay
Deggoon na ni cëb bi ñëw na agsiwul ci ñun
Ni ñun naqar rekk lañuy dund wax ko allahou kun
Ñun bopp ba léegi dundetuñu te
Amuñu kenn kuñ ko wax ñoo ngi tok di muñ
Masque téeméer chaque jour suñ doole du ko mun
Woh woh woh woh
Yàlla yaw Yàlla yaw ñu lay ñaan nga balinu
Woh woh woh woh
Yàlla yaw Yàlla yaw ñu lay ñaan nga balinu
Yàlla yaw baal nu
Yàlla yaw baal nu
Yàlla yaw baal nu
Yàlla yaw baal nu
(Yàlla yaw baal nu)