notícias musicais

top 13 artistas

top 13 musicas

Confira a Letra Yaay (feat. Leyna)

One Lyrical

Yaay (feat. Leyna)

Gëj naa la gis (namm naa la)
Namm naa la (namm naa la)
Yàlla la xiir (ci man)
Ci man xamm naa ko (xamm na ko)
Yëg naa ko

Yaay boy kaay jël ma balaa ma dem géej
Yaay boy kaay jël ma balaa dem géej

Yaay boy daadan muñ ba dommam teral ko kaw suuf
Baay tam daadan muñ bu xolam sedd ga doon buur
Boo amee defal tout, sa famille bégal ko mooy tout
Jëndal meew ak sukkër, ceeb ak dëwlin

Mindeef taxul (mindef taxul)
Xaalis taxul
Les waxul (les waxul)
Nit dey wax lum deful
Yaafus warul
Boroom karaw bu ñuul
Ñépp am naan bidéew fi ak déwuñ du reer
Ku ley seddil ci gaalu xaaj
Bul ko bañ nga la bu mu fa fekk sa loxo
Liggéeyu nday añu doom
Liggéeyu nday añu doom

Gëj naa la gis (namm naa la)
Namm naa la (namm naa la)
Yàlla la xiir (ci man)
Ci man xamm naa ko (xamm na ko)
Yëg naa ko

Yaay boy kaay jël ma balaa ma dem géej
Yaay boy kaay jël ma balaa dem géej

Sama yaay yaay yaay
Ba muy ñaati yoon
Tég ci baay boy looloy ndami doom
Àljanna gi sey suufu tànk waye barke baay
Yaay bul jàppe duma la mësa bàyyi
Yaay, ni ma lay namme dumsi masa tàyyi
Yaay, dëkke daw yaw mësuloo bàyyi
Yaay, dima tég ci yoon yaw yaa ci àay
Jigéen ju mën góor liggéy ga sama kër baay
Yir ma yar ma yee ma
Joom fu la ak fàyda
Xam sa bopp yox la, jugal liggéey jox la
Danu jugaat laaj ma, yaay sama galaaj yaw la yaw la

Gëj naa la gis (namm naa la)
Namm naa la (namm naa la)
Yàlla la xiir (ci man)
Ci man xamm naa ko (xamm na ko)
Yëg naa ko

Yaay boy kaay jël ma balaa ma dem géej
Yaay boy kaay jël ma balaa dem géej

Tracker