notícias musicais

top 13 artistas

top 13 musicas

Confira a Letra Boulko Door (feat. Harmony)

Ouly

Boulko Door (feat. Harmony)

Moo ngi séy te moo ngi muñ
Moo ngi def li mu mën
Waaye jëkkër jee dënke
Xas dóor jëkkëram ni lay séye

Jëkkër ji du ko defal dara
Du yeré du dall du cheveux
Li mu jàppe cadeau mooy
Xas dóor jëkkëram ni lay séye

Bu Wally doon boole Faramareen yépp
Li jëkkër ji yor ci gel moo leen ëpp
Tey saayu waxe jëkkër ji jàpp
Xas dóor jëkkëram ni lay séye

Li muy dundu metti na
Te musul faay fonku na séyam
Xamul bonheur séye lu dul
Xas dóor jëkkëram ni lay séye

Kenn xamalu ko dara
Lu séye bi metti-metti
Loo manqué mu ne dara
Séy si wul daa sey sii
Toog na muñ te njaabot ta ko waral

Séy ba déeg waaw góor
Méritéwul ay dóor
Dee ko takkal ay or
Boo seetloo metti na dawul

Lu séy bi metti-metti
Moo ngi dundal njaabot gi
Te jëkkëram du ko jox dépense
Moo ngi taba taba dundul njaabot gi
Yéwoo ca fajar dem jàyyi
Njëggënteek auto yi
Danga dangi bu dul jeexe
Bokku naat indi def ci kër gi

Ba changer jëkkëram léegi neex na
Te li mu doon dundu metti na
Te musul faay fonu na séyam
Xamulwoon bonheur lu dul
Xas dóor jëkkëram ni lay séye

Kenn xamalu ko dara
Lu séye bi metti-metti
Loo manqué mu ne dara
Séy si wul daa sey sii
Toog na muñ te njaabot ta ko waral

Séy ba déeg waaw góor
Méritéwul ay dóor
Dee ko takkal ay or
Boo seetloo metti na dawul

Wuy leleleeee yow
Moom dunde na lu ne
Boo seetlu wee metti na dawul

Séy ba dégg waaw góor (waaw góor)
Méritéwul ay dóor (méritéwu ko)
Dee ko ko takkal ay or
Boo seetloo metti na dawul

Tracker