notícias musicais

top 13 artistas

top 13 musicas

Confira a Letra Djiguéne La (feat. Harmony, Soraya, Kya, Satou Niang & Kinekine)

Ouly

Djiguéne La (feat. Harmony, Soraya, Kya, Satou Niang & Kinekine)

Waawaaw
C’est comme ça

[Soraya]
Femme d’affaire ba keroog muy neex
Góor du ma yàpp man ayca tay mu neex
Booy wër jom moo ngi fi
Fu la ju mat ak fit bi sax
Boo gëmee Yàlla kon looy ragal

[Kya]
Xawma ko
Noonu la àdduna bi noonu la
Takkal sa sër te bul tokk
Duma ko yakaar ci góor
(Jugal, jugal, jugal)
Dooley jigéen fu lak jom laa way
(Jugal, jugal, jugal)

[Satou Niang]
Yaw bul ko dóor te bul ko saaga
Soo ma munul neexal bul ma jànni
Méritéwul lii di dóor aka saaga
Soo ma munul neexal bul ma jànni
Ahhh, jigéen laa

Jigéen laa, jigéen laa, jigéen laa
Jigéen laa, jigéen laa, jigéen laa
Teral ko, lingeer laa, jigéen laa
Lingeer laa

Songali nga, songali nga, songali nga
Déedéet, songaliwul kay
Ku mënul te bawoo lu yaku yawaa
Jigéen laa

[Ouly]
Ñun ñooy jigéen seeni yaay
Jigéen seeni rakkak seeni soxna
Dëkk ci liggéey jaambar laa
Su ma séyee mu neex
Ndaxte man jigéen laa

[KineKine]
Mi nge kooy dóor waxul
Ba ngay kontaan moom takkul
Muñ bés bu ne saxul
Sama bat ci kaw
Hommage à toute les femmes
Qui sont maltraitées
Dans les maisons, dans les prisons

Dina metti waaye bul bàyyee
Soo gëmee sa boroom looy ragal sa noon
"Man xawma ko"
Tay dina metti suba day neex
Waaye soo muñee ni suba day jeex
Sa lépp sotti

[Satou Niang]
Yaw bul ko dóor te bul ko saaga
Soo ma munul neexal bul ma jànni
Méritéwul lii di dóor aka saaga
Soo ma munul neexal bul ma jànni
Ahhh, jigéen laa

Jigéen laa, jigéen laa, jigéen laa
Jigéen laa, jigéen laa, jigéen laa
Teral ko, lingeer laa, jigéen laa
Lingeer laa

Songali nga, songali nga, songali nga
Déedéet, songaliwul kay
Ku mënul te bawoo lu yaku yawaa
Jigéen laa

Je suis femme battante
Jigéen fu lak fàyda jigéen
Ngor ak doylu jigéen
Bul ko dóor, bul ko saaga jigéen
Bul ko toroxal

Tracker